NUN NOOY ŇAN ?

Kàddug Njiit lu màg li

Lu ëpp 50% ci waa- afrik ay ndaw lañu. Te loolu indi na ay jafe-jafe lu ci mel ni ndóol, ñak jàng et ñakum xëy gu bari. Ndaw yu bari mam nañu wutàli rewum taax yi ngir am xëy. Nekk ñoom kese ba tax ay fiir yu bari lalu ci seen kanam lu si mel ni bóomate gu tar, sinebar, cagatu, ëmb ak yàq biir. Yeneni musiba yu mel ni febaru sëy yi SIDA, kër yiy tas, dund ci mbed mi ak mam wutàli tugël te jarul ci Yoon, te mu mana jur ay musiba. Yooyu tamit tax ba nguur, Karange ak woomle jaral leen lune. Ci lu yaggul, jaay domi àdaama ak terorism xirtal leen.

Jamono yi nak téléfone yi, smartfone yi ak tablet yi tax na ba ndaw yi mana jot ci internet bi ci ndimalu réso téléfone yi te loolu tax na nuy gis bépp jëf ju bon juy xéw si àddina sépp.

Loolu motax kureel gi di Ndaw yu Ees ci këru Yeenekay yi « NGM » a ngi wuuta jëfandikoo xam xamam ci xarala yi ngir defar ay film yu am njariñ ci zair ak ci baatin, ay programu télé ak ci réso socio yi lu si mel ni « yëg-yëgu xol » ak « Yamb buy matate » ngir xeex ak indi safara ci musiba yi ndaw yi di njakonteel.

Kureel gi di « NGM » du def politik te it wut xalis taxu ko jog waaye dafay def ay programu télé ci zair ak baatin, ay film ci gis-gisu kërcen yuy indi safara ci mbirum askan wi, ci walu baatin, koom-koom te ñu soxal ndaw yi ci Afrik !